Chorus 1
Mangui samay coulisses di preparer begueul ay nit youma khamoul
Mel ni amouma life amouma amour
Mangui studio di bind álbum pour nit youma guissoul
Kagn lamay dallou ?
Verse 1
Yeah
Job naa bëgg siiw
Légui siiw naa beuggueu laqatu
Musu ma bëgg feegn pour réussir
Mais am te do siw legui amatoul
Diaratoul may gueuneu yeek yegg niveau Chester doga sokhleu rare
Overdosou Amy Winehouse legui diakhalatouma ndakh doyeul naa
Esk souma demissionner woul wone seme ex job-doumeu tané fi ?
Beugone bolé vie d'famille ak showbizzz, mais ken meunoul ameundo niaari vie
Ak jammdongg bimay woté founekkk, est-ce-que maangui dounde lou Pacifique ?
Mangui doga raniè ndéké succès beuri ne piège beuri neu artifice (whoa)
Gagner naa ay cachet (whut) Signer naa ay queuché (yeah)
Yokk naa ay amis (Facebook) Niakk naa ay kharit deugg
Yalla may ma ay mbokk, Mane meu tann ay fanss
Deukké daw guinaw ndam mbaa doumeu nit kou gatt ay fan ?
Chorus
Mang semey coulisses di préparer begueul ay nit youma khamoul
(ay nit youma khamoul, ay nit youma khamoul)
Mel ni amoumeu famille amoumeu amour (amouma amour, amouma amour)
Mangui studio di binde album pour nit youmeu guissoul (pour nit youmeu guissoul)
Kagn lemey dallou ?
Bridge
Carriere bi dinema gaagn te douma ko yeg
Mingui mey khaagn mey gueuneu reer
Dineme gaagn oh te doumeu ko yeg
Mingui mey khaagn mey gueuneu réérr
Verse 2
Dow naa ay kilomètres (ay kilo), tokh naa ay kilo herbe (rrah)
Dieul yonu missionnaire (yeah), Pour nekk millionnaire
Sol naa ay pullover ak tshirtou marque yi gueuneu cher
Wayé même tabakhou Imhotep mounoul takh banga nekk kou immortel
Concert ya ngui gueuneu fess, supporter ya ngui daanou lerr
Guedj na degg seme baatou mère, est-ce q li mo nekone seme nianou mère ? (rrah)
Dougg naa big thiow dougg naa big thiow te ken dougueuloumeu tchi
Bougg naa kick torop, beugg done big boss mais dou ben nit dou machine (machine)
Ben nit dou machine (whoah whoah), machine sakh dey bugger
Cousin meun ngama méré, Wonoumala nimele beugué
Kholeul legui demey toke 3 mois doumeu deggueunték Babs
Namm naa mane ak Jean Joe biniouy bokk agn temps fac !
Chorus
Mang semey coulisses di préparer begueul ay nit youma khamoul
(ay nit youma khamoul, ay nit youma khamoul)
Mel ni amoumeu famille amoumeu amour (amouma amour, amouma amour)
Mangui studio di binde album pour nit youmeu guissoul (pour nit youmeu guissoul)
Kagn lemey dallou ?
Bridge x 2
Carrière bi dinema gaagn te douma ko yeg
Mingui mey khaagn mey gueuneu reer
Dineme gaagn oh te doumeu ko yeg
Mingui mey khaagn mey gueuneu réérr
Outro : Vocal message from Elzo's Mother
Allo Elzo, Mane leu Dita, mang ley wo rek bobou beu légui mounoumala diot
Cherif sakh mingma naan sakh guiss nala Instagram bobou ya gui ci se tournée bi
Khawma yaa ngui wone Suède walla Allemagne
Bo dioté sama message nga rappeler ma. Merci , à bientôt…